﻿Bataaxal bi jëm ca Yawut ya.
1.
Bu yàgg la Yàlla waxoon ay yooni yoon ak maam ya, ci waxin yu bare, yonent yi jottali. 
Ci fan yu mujj yii, ci Doom ji la jaare wax ak nun, ki mu jagleel lépp, te ci moom la sàkke àddina wërngal këpp. 
Kooku mooy lerxat leeru Yàlla, te mooy ki jëmmal nekkug Yàlla. Moo téyee lépp kàddoom gu manoorewu. Gannaaw ba mu setalee bàkkaar yi nag, fa ndijooru Aji Màgg ji la toog, fa kawte ya, 
te ni turam wi mu séddoo gëna màgge turi malaaka yi, ni lees ko yékkatee, ba mu gëna màgg malaaka yi. 
Ndax kat, ana kan ci malaaka yi la Yàlla masa wax ne ko: «Yaa di sama Doom, bés niki tey, maa la jur,» ba neeti: «Maay doon Baay ci moom, muy Doom ci man»? 
Buy indiwaat taaw bi ci àddina nag, ci la naan: «Na ko malaakay Yàlla yépp sujjóotal.» 
Malaaka yi, la Yàlla wax ci seen mbir ne: «Moo def ay malaakaam diy ngelaw, jawriñam ñooñu la def tàkk-tàkki sawara.» 
Waaye Doom ji la Yàlla ne: «Yàlla, sab jal a sax dàkk ba fàww, sa yetu buur njub la. 
Yaa sopp dëgg, bañ lu bon, ba Yàlla, sa Yàlla diwe la diwu mbég, nga tiim say moroom.» 
Mu neeti: «Yaw Sang bi, ca njàlbéen ga, yaa samp suuf, sàkke asamaan say loxo. 
Yooyu day réer, waaye yaw yaay sax, lépp ay ràpp ni mbubb. 
Yaa leen di taxañ ni malaan, ni yére di soppikoo it lañuy soppikoo, te yaw ngay kenn ki, te say at amul kem.» 
Ana kan ci malaaka yi la mas ne: «Toogeel sama ndijoor, ba ma def say noon sa ndëggastal»? 
Xanaa malaaka yépp duñu ay ngelaw yu ñu sas ab liggéey, yebal leen ngir ñu taxawu ñi wara jagoo ag mucc? 
